Youssou N'Dour - Fay Bor Lyrics

Lyrics Fay Bor - Youssou N'Dour



Ki la bëgg yab ndax alal,
Yaw ignorer ko
Lèpp Lu la nit, di Dokhanto,
Yalla am na ko
Féek yaa ngi koy wóolóo,
Yalla mën laa fayal sa bor
Ki la bëgg jaay loo sa ngor,
Bayyi kook yëfëm
Ba ko fa ne tek, bés a ngi ñëw,
Di na wéet ak jëf ëm
Féek yaa ngi koy wóolóo,
Yalla mën laa fayal sa bor
Te sax jamono fi mu toll nii,
Ku ne bopp am la tal
Mawlaana rek, moo lay defal,
Ken du la xamal
Féek yaa ngi koy wóolóo,
Yalla mën laa fayal sa bor
Salaam alleykum, nga bañ ko fay,
Mbaa xam nga ni bor la
Sa dëkkëndòo, nga koy tanxal,
Mbaa xam nga ni bor la
Teg say briques, ken mën jaar
Mbaa xam nga ni bor la
Yor sa auto, lu la neex def
Mbaa xam nga ni bor la
Nit ku la neex, nga wax ci moom
Mbaa xam nga ni bor la
Yor say mbalit, fu la neex tuur
Mbaa xam nga ni bor la
Koo séqqël, daldi ko wor
Mbaa xam nga ni bor la
Yendoo wax, loo waax mu dañ
Mbaa xam nga ni bor la
Koo ëpp doole, won ko ko
Mbaa xam nga ni bor la
Doo dimmili, ki nga tane
Mbaa xam nga ni bor la
War ngay xalaat bu ëllëg ée,
Nan nga koy fay é
Féek yaa ngi koy wóolóo,
Yalla mën laa fayal sa bor
Man youssou maajigéen,
J′ai tout pardonné
Koo xam ni, meusone na la tooñ,
Jéggël ma ko
Bor yi nga am fii ñu ne,
Nan nga koy fay é
War ngay xalaat bu ëllëg ée,
Nan nga koy fay é
Féek yaa ngi koy wóolóo,
Yalla mën laa fayal sa bor
Ki la bëgg jaay loo sa ngor,
Bayyi kook yëfëm
Ba ko fa ne tek, bés a ngi ñëw,
Di na wéet ak jëf ëm
Féek yaa ngi koy wóolóo,
Yalla mën laa fayal sa bor
Te sax jamono fi mu toll nii,
Ku ne bopp am la tal
Mawlaana rek, moo lay defal,
Ken du la xamal
Féek yaa ngi koy wóolóo,
Yalla mën laa fayal sa bor
Salaam alleykum, nga bañ ko fay,
Mbaa xam nga ni bor la
Sa dëkkëndòo, nga koy tanxal,
Mbaa xam nga ni bor la
Teg say briques, ken mën jaar
Mbaa xam nga ni bor la
Yor sa auto, lu la neex def
Mbaa xam nga ni bor la
Nit ku la neex, nga wax ci moom
Mbaa xam nga ni bor la
Yor say mbalit, fu la neex tuur
Mbaa xam nga ni bor la
Koo séqqël, daldi ko wor
Mbaa xam nga ni bor la
Yendoo wax, loo waax mu dañ
Mbaa xam nga ni bor la
Koo ëpp doole, won ko ko
Mbaa xam nga ni bor la
Doo dimmili, ki nga tane
Mbaa xam nga ni bor la
War ngay xalaat bu ëllëg ée,
Nan nga koy fay é
Féek yaa ngi koy wóolóo,
Yalla mën laa fayal sa bor
Man youssou maajigéen,
J'ai tout pardonné
Koo xam ni, meusone naa la tooñ,
Jéggël ma ko
Ñun doom i aadama ndiaye
Li ñu gën ë sonn al mooy,
Aqqi dëkkëndòo,
Aqqi àndandoo,
Ak aqqi am gi jamm yek,
Yalla, yermëndéem yaatu na,
Mën naa jéggël e bakkaar bu mu
Waaye, doom i aadama Ndiaye,
Boo ko yor ee lee bor,
Na nga ko fay, fii ci dunyaa
Walla nga balu ko mu baal la,
way samba, Khalass, kholal
Youssou maajigéen, oh! lii doy na waar
Youssou Marie Sène,
Bu dee lii la, bor yi bari ña ñu
Yaay na nga ma baal, baay na nga ma baal,
Aqq u njuréel
You, Ndour, merci beaucoup .
Adji maam Ndiaye, yaay I thianék ama, maa challaa
Man da ma lay tooñ, njëk laa mer, fas sa ma kamnam
Nga daldi ree, nima mbaye dieye, mbasaa mbasaa
Seng Seng papa Mbaye mbassa mbassa
Bés ni ki tay kholal, baal naa ñépp
Am gi jamm yi, Fans yek, kharit yi ban ngemp
Ho baal nagne ngemp
Man youssou maajigéen,
J′ai tout pardonné
Koo xam ni, meusone naa la tooñ,
Jéggël ma ko
Mani jéggël ma ko
... Jéggël ma ko
Yallak yeuremade yam
Jéggël ma ko
Man youssou maajigéen,
J'ai tout pardonné
Koo xam ni, meusone naa la tooñ,
Jéggël ma ko
Ahhhnn yeeee
Jéggël ma ko




Youssou N'Dour - MBALAX
Album MBALAX
date of release
12-11-2021




Attention! Feel free to leave feedback.