X-Press - Reer paroles de chanson

paroles de chanson Reer - X-Press



Dama digané wone lénène lou bokoul-lone
Li Mame yi bayiwone fi wédi lima done
Dama fatéwone li mane dou niom
Topondo ma yaubé ma bayi sama yone
Fo la djitolone Aduna ma xaptal-lone
Kouma digueul lou bakh ma defla sama noone
Wédi lima done, fouma djougué wone
Gass def cii kambe lama baye yabéwone
Légui mangui ni, xawouma fouma nék ni
Dafa melni dama reer, xawouma li lanela ni
Koumay guindi waat, ma meuneu gnibi waat
Aduna ma nakh, nafsu yéwma boum cii baat
Sou dembe done taay dina déglou tay
Douma naagou faté Yalla Bour bima maay
Dina moytou andando yu bone yimay djay
Dina gueuneu fonk sama ay mbokeu
{Jah Man - Chorus}
Topondo ma dougueulone cii roy bénène xétu life
Wédi lima done reer tope sama bakane
Woywoywoywoy
Légui demna ba xamatouma mane may kane
Meuna touma deup xamouma fouma nek moy fane
Woywoywoywoy
Dafa dani wone bénène culture, Dém ba lonk tcha
Tay dok diame nama guissouma kou mané masta
{Selmind - Verse}
Xolam reer na koukoy nguindi, tekko cii yone wi bala goudi
Digg dolém la tole fokné lou samp rek meune nako boudi
Solena dallou capitale ba, rir mako xaptal ba
Reer na diar cii yonou sankou tabi cii keupeuteul ba
Foumouy moudjé sétane ko, xélama teudjé kanarou
Bala xam xamadi gaañ ko, néna minena ndakarou
Fonto ko féki cii xolam, bone loko fétchi xélam
Li djik wourouss fékou cii ngalam,
Lila fi indi dou féthie cii ngaalam (Reer Na)
Amatoul repère topototoul Père ak Mère (Reer Na)
Faténa yonou deuk ba, dou yoné kène douko dégue
Complexé Samba Alar roy dakla doundoul deugue (Reer Na)
Daay fanano thiaga, daay taukh, night yi daay nane sangara
Mayé 100.000 soirée Salam, sa Yaye réroul dou sa ngoora (Reer Na)
Xamoul foumouy takhaw, dieul loumou momoul deugue ndioup lang
Fouko nekh mou aw, gueum loumou donoul deuké nioubelangue
Lek na dieuw bi, diomba niaw
Diapena daal soubeu dou nieuw
{Jah Man - Chorus}
Topondo ma dougueulone cii roy bénène xétu life
Wédi lima done reer tope sama bakane
Woywoywoywoy
Légui demna ba xamatouma mane may kane
Meuna touma deup xamouma fouma nek moy fane
Woywoywoywoy
Dafa dani wone bénène culture, Dém ba lonk tcha
Tay dok diame nama guissouma kou mané masta
{Brahim - Verse}
Yeah! Norr moniou feugue cii digue nawett dadi gni.mou yém nieup
Araf laniou dameu cii biri beuyit, mouy firi lénène di bèn lépeu
Lipone cii sèn lepp. Tène guiss ni djante ngui feink cii Sowe yeup
Digue noumbélane la, lerr yi faay néw ya ngui dokh di xégne neupe
Thiakh fékna teuxba firi Goumba, leundeum waw Koumba
Rax fékna djeuf toké xélou ndjouma gni warone na warona wakh mouma
Humanisme dioxoñ baramou touma, djiko xamétouma
Diné ngui seug di djoy néna gueum gueum yi laniou dieul same cii louma
Légui bène kalama la nieup di wakhé
Xalissay dirigé aduna foumou xass dougou dara dou djafé (Hum)
Néwna cii biir poches yi, fess cii xol yi, taxawna fènn nieup tichauli
Xiff na bodji na tole sédena niamam bi néwoul cii kop bi (guiss nga)
Cii galou ma rireu ndo la nieup di moudjou am barké
Kène beuguetoul ndamo liguey bou séleu, léw am barké (guiss nga)
Bou Yalla atéwoul yeurmandé nioune nieup cii parquet
Dou yéné mola tchii guéné sakh dieuf yéy takh nga tardé
{Jah Man}
Légui mangui ni, xawouma fouma nék ni
Dafa melni dama reer, xawouma li lanela ni
Koumay guindi waat, ma meuneu gnibi waat
Aduna ma nakh, nafsu yéwma boum cii baat
Sou dembe done taay dina déglou tay
Douma naagou faté Yalla Bour bima maay
Dina moytou andando yu bone yimay djay
Dina gueuneu fonk sama ay mbokeu



Writer(s): Xpress


X-Press - Biir Ak Biti
Album Biir Ak Biti
date de sortie
27-04-2019



Attention! N'hésitez pas à laisser des commentaires.