Youssou N'Dour - Ballago ndumbé Yaatma paroles de chanson

paroles de chanson Ballago ndumbé Yaatma - Youssou N'Dour



Billaay, ballago ndoumbé yatma,
Su ñu waaji xaj oon na fi
Naxxar doηη,la ñu bayyee
Yalla, wonneeti na
Li tax ba mbir mi metti lool,
ñun da ñu ko foog wul woon
Yëf yi gaaw ba bette gnou
Billaay wéetël na ñu
Njiinoo njiin faramaareen,
Gòor u jaaga, nelaw naa
Baay i wally dem na nii,
ñun daal wéetël na ñu
Ma ngi koy jaale Sénégal,
Di ko jaalé Gambia
Di ko jaalé adduna,
Ndaanaan ba dem na nii
Thione ballago, ndoumbé yatma
Bu yalla buur bi doon taggoo,
Kon di na ñu bayék yaw
Ni patrimoine bi nga ñu bayyeel,
Yee gua nit gñi, tete leen ci adduna
Yee gua nit gñi, tete leen
Xam al leen ci adduna
Ahhh - Balaago
Yee gua nit ñi ci adduna xam al leen
Ni ñu war a nekkek
Ak ni ñu war a dundée,
Ak ni ñu war a jëfleentee
Jinaxoo mbaay
Yaw mi dëkké biir suuf,
Boo dem ee neel ballago, réew maa ngi koy joy
Aduna ngi koy jooy,
Art baa ngi koy jooy
Njiin faramaareen,
Thione seck, wéetël na ñu
Ballago ndumbé yaatma
Adduna, am ul solo
Li tax ba mbir mi metti lool,
ñun da ñu ko foog wul woon
Yëf yi gaaw ba bette gno
Ndanaan ba demna ni
Njiin faramaareen,
Thione seck, wéetël na ñu
Ballago ndumbé yaatma
Adduna, am ul solo




Youssou N'Dour - MBALAX
Album MBALAX
date de sortie
12-11-2021




Attention! N'hésitez pas à laisser des commentaires.