Ashs The Best - GIS GIS paroles de chanson

paroles de chanson GIS GIS - Ashs The Best



Yeah
Hien
Ci lëndëm la lay fekk
Bës ci leeray la lay weer
Biik ci guddi ak subateel
Yow mii naajal ñii di ker
Ken mënul jënd fii respect
Mais nitt ki lepp la mën a def
Ling fi leble lan lay fay
Waa ji dëkk si door waar
Yaw nga dëkk ak ñu doy waar
Ñi la tëkk u dunu sa noon
Sa noon bi noon am moo ngi xaar
Ku nekk xam nga foo joge ba bu coolee nga war fa dellu waat
Lune lu yëngu li ko yëngal a ko ëpp doole
Dinan ko jéngu ba weesu bëggu nu dellu ginaaw
Mafia bi xamul lu gaal gi di riir mais ñoo ngi yoole
Gis-gis yi ñoo wutee mënu ñu jàkkaarloo
Tiis tiis la ñu dundee xanaa gis u loo
Baawooo
Soo xamulee foo jëm dellul fi nga
Bawooo
Dellul fi nga bawoo
Baawooo
Soo xamulee foo jëm dellul fi nga
Bawooo
Bawoo
Ku reer du wër te ku seet gis
Ku jëf ñu xam làmiñ du wax peace
Ci yoon u ndaw nga mën a tarxiis
Màgg bu gaaw bi du ci benn bis
Luñ fi daj daaw moo waral ren diis
Bu ñu kenn neetali
Mettit bi jeex a gul ku daj gis
Fayeeku sorewul ku weddi gis
Mën nañ yénneeku yen bi
Ku nekk bul doyloo sa gis-gis ak ngëm-ngëm
Bu kenn siis bu kenn ciip-ciip
Mën na ñu wute ni ñu gisee yoon bii
Ku nekk ni nga ko dundee rekk nga mën a gëm fii alright
Wute ni ñu gisee yoon bii
Wute bokku ñu y gis-gis
Weet gore weetaliko'og ngor
Fi nga joge wute'eg fi nga jaar
Nobody know nobody can know
Boo xamul foo feetee dellul foo bawoo ba muy teel
Yeah ok gestul balaa muy wees
Baawooo
Soo xamulee foo jëm
Dellul fi nga
Bawooo
Dellul fi nga Bawoo
Baawooo
Soo xamulee foo jëm dellul fi nga
Bawooo
Bawoo



Writer(s): Olivier Delahaye, Abdoulaye Sy, Arfang Tiare


Ashs The Best - 1995 - EP
Album 1995 - EP
date de sortie
25-02-2022




Attention! N'hésitez pas à laisser des commentaires.