Ashs The Best - Ayway Samba текст песни

Текст песни Ayway Samba - Ashs The Best



Mmmm
Mënatuloo siggi ci bët xool ma
Mënouma woon gëm ni nakho ma
Ku la ko waxoon loolu am na
Lu agne du réer te matt na soor
Li nga ma waxoon wuutek say jëf
Digué boor la yaw woor nga
Nga laaj ma sama xol man ma jox la
Defoo ma ni sa bopp takh nga gaañ ma
Keerog sam xel bi waroon na tey
Say wax woor ma
Dañ ma téré woon ma taxaw wat ni sañuloo ko
Ma jël la teg fi ma tegul benn mindeef
Bi nga xamee bëgguloo ma wax ma ko
Bëñ ak lammiñ fak ñu laale (waawaaw)
Wayé fajaloo ma sama gacc (mmm)
Nu may defak samay dëkkëndoo (samay dëkkëndoo)
Duma siggi xol ci samay nawle
Gacc gi fu ma koy waxé (héeee)
Ci xol la tiis boo may lacce (haaaan)
Dinga ko gis Yàlla ñuy àtté (Yàlla ñuy àaaaatté)
Bi nga fi jii bës ding ko goobe (goooooobe)
Ayway Samba
Yaw yërëmoma (yërëmoma)
Nga tooñ ma benn yoon man ma baal la
Nga def ko ñaari yoon man ma baal la
Yeah way Samba
Yaw mi de bëgguloo ma (he le le le)
Nga laaj ma sama xol man ma jox la
Defoo ma ni sa bopp tax nga waar ma
Waawaaw
Mmmh mmh
Ki sedday bi
Tàngoor bi
Nekk ci naaj bi kéraloo ma, kéraloo ma
Defuloo ma ni ma la def
Lu ma xam wax la
Alaal ma jox la
Mbëggeel ma waan la
Kan nga ma jënde lan la ma rawé
Ki nga ma jënde lum ma ëppëlé
Réwoo réw weur naa ko
(Réwo réwo)
Keneen ku ma guis ni yaw la
(Réwo réwo)
Ñu mel ni yaw lay musloo (Woo mbëggeel)
Nga def lii man lay wuyoo
Réwoo réw weur naa ko
(Réwo réwo)
Keneen ku ma guis ni yaw la
(Réwo réwo)
Ñu mel ni yaw lay musloo (Woo mbëggeel)
Ni mbëggeel def man lay woyloo
Ayway Samba
Yaw yërëmoma moma
Nga tooñ ma benn yoon man ma baal la
Nga def ko ñaari yoon man ma baal la
Yeah way Samba
Yaw mi bëgguloo ma
Nga laaj ma sama xol man ma jox la
Defoo ma ni sa bopp tax nga waar ma
Gàcc gi fu ma koy waxé (hééééé)
Ci xol la tiis boo may laaje (haaaaaaaan)
Dinga ko gis Yàlla ñuy àtte (Yàlla ñuy àaaaatté)
Bi nga fi jii bës dinga ko goobe waw



Авторы: Arfang Tiare


Ashs The Best - Ayway Samba
Альбом Ayway Samba
дата релиза
12-05-2023




Внимание! Не стесняйтесь оставлять отзывы.