Youssou N'Dour - Waññ iko paroles de chanson

paroles de chanson Waññ iko - Youssou N'Dour



Par AbouAmg
Han, han, sa kattan bari na, sa bateau gaaw na, te saw fit rëy
Han, han, sa kattan bari na, sa bateau gaaw na, te saw fit rëy
Han, han, sa kattan bari na, sa bateau gaaw na, te saw fit rëy
Refain: waññi ko, waññi ko, waññi ko,
Waññi ko, waññi ko, ëpp
Refain: waññi ko, waññi ko, waññi ko,
Waññi ko, waññi ko, ëpp
Han, han, sa kattan bari na, sa bateau gaaw na, te saw fit rëy
Han, han, sa kattan bari na, sa bateau gaaw na, te saw fit rëy
Yaw yaa ni, ëpp óon nga, trois cent kilos,
Te bés bu ne, benn xar nga daan e
Nga neeti, at mi fi Obama ñëw ée
Yaw yaa ko gis, muy dox antu, biir Pikine
Am oon na, gaïnde gu rëccé, parc hann
Nga neeti ñu, yaw yaa ko jat, ba mu nelaw,
· Nga ni ma, am oon nga, benn bateau, ca Guinée
Te waa nations unies, nga ka daan loué
· Te diggënté, États-Unis ak Guinée,
Daa woo ko daw, lu ëpp ñaar i fan
Am na benn bés, nga ni ma, my boy
Keroog daje naak, roi des arènes. 2 fois.
Ben loxo, laa ko yékkëtée, ni ko félicitations. 2 fois.
Ma tegaat ko ci suuf, ni ko, my boy. 2 fois
Na nga jaar, sa ma kër, ma jox la yeneen clefs
Na nga jaar, galle, ma jox la yeneen clefs
Techniques yooyu, japon laa ko jànge
Ca yooya jamono, man la ñépp di wër
Lu ñu wax nga ni fekke nga ko
Fu ñu wax nga ni dem nga fa
Doo tiit doo raf, doo dellu ginnaaw;
Waaye sa ma waa jii, ken melut ni moom.
Wax oon naa fi ni adduna ken du ko dajal,
Te ku dul umppëlé da ñu lay ragal.
Wax aat leen ni faw nit ku ne am lu muy des al
Ngir bu ëllëg ée ñu mën laa set al.
Xam lépp, mën lépp, loolu, yalla dong a ko jagoo. 2 fois.
Ragal al yalla, waay, ragal al yalla
Ragal al yalla, waa jii, ragal al yalla
Ragal al yalla, waay, ragal al yalla
Ragal al yalla, waa jii, ragal al yalla




Youssou N'Dour - MBALAX
Album MBALAX
date de sortie
12-11-2021




Attention! N'hésitez pas à laisser des commentaires.