Dip Doundou Guiss - Holocauste paroles de chanson

paroles de chanson Holocauste - Dip Doundou Guiss



Gueu-Gueumeul Yallah boul laathie ndakh Yallah gueum nala
Diouraum niarélou Assamane moy fi sama kaatane bi meuneu yém
Gouvernement bi bougueul ma djangue sama waa galé bagne ma RAP
Bougouma kène djangalma nappeu bougou-bougoumatam yaw nga mayma djeune
Beus di nga tourné laathie Papeu Tourné laathie Yaye Niouné leu dém nagn dou nékha gueum
boudone kouné yaay taaneu li ngay am, Yallah dina guiss Nit diko niémé eupeulé
Kou weet xam sa waay deugueune taane Njaay Mo ki ci sa séttou nimou mel nga mel
Di def nga def Mindef nga rek meunougne la teuthie Ndakh yaw rekka fi meusseu def lou meunta
Oh Shit!
Souma déwé laay contane Boy
Rakk sama kerr comme naathie
Oh Shit!
Oh Please!
Boy dieul sama life Ô My GOD
Moudjeuntéél bou nice Ô My GOD
Please!
{2nd Verse}
Fekké sama digueu dolé di tombék djimbi diamono
Boudone ay billets ma niakkeu deupeu paresol bi
10.000 problèmes fébaru diouni djangoro
Bindeu na GOD mais néna dou tidjii enveloppe bi
Easy dama niaak djom djépi sama bopp
Mou melni amouma compte beug ibi sama banque bopp
Méti nama lolou ndakh ma ngui naane nékoul mako sombi
Liir bou tangueu xel momak PA bou tangueu xol
Dominique amena bac-gam (BAC) yeah tané na
Fk boy DIP ki dou meusseu dieundeul Yaayam Keur
Sama xel tééy sama xel tééy ma niaaw njorte ci fimay moudjé
Di nélaw ni neew, guédeu, fo guissé kou déh di gueinteu?
Ma nék di yëg sama ROUH ngui dém
Bataye gni di sathieu ak gni di thiaggatou rek la gni tchi tali bi di yélwane di gnéin
Oh Shit!
Souma déwé laay contane Boy
Rakk sama kerr comme naathie
Oh Shit!
Oh Please!
Boy dieul sama life Ô My GOD
Moudjeuntéél bou nice Ô My GOD
Please!
XAJJA (Chien) gueuneu djégué NIT, NIT gueuneu djégué IBLISS
Nioune nioko gueune nioune nioy def ni xajjou (Chien) IBLISS
Comme millardaire yu gueune riche fi
Douniou suur nio ngui lekk ay xollou miskine
Légui NIT gni nioy DEUM yi
DEUM yi di déh wak xiff NIT
Yeah lane moy deuggou wa dji yokkou taux de suicide?
Ma faté guèneu djaadeu outi yonou EGLISE
Ndakh église yagg nafa noyi air pur
Ni JESUS souma guéné nékaate Hercules
Waayé bama djoudo la xam ni gagné nagn guerre bi
Dama djoudou joy ndakh Aduna pour nga am li nga beug faaw nga def li nga bagne
Lou tarr saay soko amé kénène ki nga gaagne
Louy mbaax so mataloul galém Ndékkéék agne
Limay dieumeulé kanam lay def di déffaate
Mane nga sèèn ci sa temps faaw nga def ni sa Baaye
Liguèy lou fay VOLCAN ni SEYDINA LAYE
Bo teudé diko niaane di nga déh ci sa lale
Gueum ni ya eupeu lerr naadjé gou xess di xessal
GOORGOORLU wouma GOOR la douma DJIGUèNE
Loutah meunou maassi guèneu ni YOUSSOU MADJIGUèNE
Outoum Xaliss rek bamay soukraate di déh
Loumou laathie niou def tant que mo ngui am di léw
Dou maak niom dou niok mane
Waa mané DUNYA soumala meunoul meuno ma
Dou maak niom dou niok mane
Parce que déwone naa bou yagg yaw
Kou déh ba dékki sanioul bideunti dou naadjé yéwou
Souma amone lalou xaliss sakh douma dém teudi
Beugouma KHALIFA, TALIBE yaay sama SERIGNE
Taal bou Yallah taal laa ci Aduna ngané do tchi andeu
Ba Alaxîrra mou taal leu yaw tamite
Am par force ndakh NIAAKEU day rayé
XALISS rekka meuneu FATHIE DOCTEURS YI (Bis echo)



Writer(s): Dip Doundou Guiss


Dip Doundou Guiss - Tay Leu Kagn
Album Tay Leu Kagn
date de sortie
04-11-2017




Attention! N'hésitez pas à laisser des commentaires.