Youssou N'Dour - Pullo Àrdo Lyrics

Lyrics Pullo Àrdo - Youssou N'Dour



Ku fi ñëw mu jangal la
Nax mi moo ko moon noox mi moo ko moom
Daf ko dónn
Lii xar yi la, lii bey yi la
Nagam yangi, àli bàngi
Baaxi maamam Pullo Àrdo
Ku fi ñëw mu jangal fa
Nax mi moo ko moon noox mi moo ko moom
Lii xar yi la, lii bey yi la
Nagam yangi, àli bàngi
Baaxi maaman Pullo Àrdo
Pullo Àrdo, Pullo Jééri, Pullo Àrdo
Pullo Jééri, Pullo Àrdo, Pullo Jééri
Dàqqal yee ñu jëm fee nga dàqq yil ñu jëm fii
Yaa xam yaw li xew fee, dara jaxalula fii ba fee
Pullo Àrdo, Pullo Jééri, Pullo Àrdo
Pullo Àrdo, Pullo Jééri, Pullo Àrdo
Àrdo sex na gënnëm
Dàldi gàddu yattam
Ma nga ànd ag xaajam
Dàldi jittël géttam
Pullo Jééri, Pullo Àrdo
Mi ngi ànd ag xaajam
Dàldi jiitél géttam
Dalal xelam, fééxal xolam
Bu nin ñi fo aka ree moom yégu ko suuy
Pullo Àrdo, Pullo Jééri
Yeppam mu ngi fii
Fii la yaroo, fii la màgee
Te yii fii la takkee sowna
Léppam fii la
Pullo Àrdo, Pullo Jééri
Bu nin ñi tëbë ka dal moom yëgu ko
Li mu am fii doyloo na ko doy loo na ko
Bu dee cor la mbaa jamaan la
Walla etaas la, mbaa abyong la, mbaa leneen la
Moom gisu ko, Pullo Àrdo
Ma nga gàddu taxaaran
Di mbiip mbiip mu am xorom
Way, way yu amui moroom
Mel ni kuy neexai goroom
Boo fa jaaree sant Saar ee di na la ree
Boo fa jaaree doon Séréér ee di na la ree
Boo fa jaaree sant Saat ee di na la ree
Boo fa jaaree doon Séréér ee di na la ree
Di mbiip mbiip mu am xorom
Way, way yu amui moroom
Mel ni kuy neexai goroom
Boo fa jaaree sant Saat ee di na la ree
Boo fa jaaree doon Séréér ee di na la ree
Boo fa jaaree sant Saat ee di na la ree
Boo fa jaaree doon Séréér ee di na la ree



Writer(s): KABOU GUEYE, YOUSSOU N'DOUR, MODY BA


Youssou N'Dour - Rokku Mi Rokka
Album Rokku Mi Rokka
date of release
29-10-2007




Attention! Feel free to leave feedback.